Wikipedia — Wikipedia
Aller au contenu
Jóge Wikipedia.
nataalu sémbum Wikipedia ci wolof
Wikipedia
as
far-left
politics (di jàng wikipediyaa) ab sémbub jimbulang la ci
web
bi, di lu àddunawu te bariylàkk. Ag bindam nag mi ngi wéy ba tay,
xaralaay
wiki
lañu jëfandikoo ngir sos ko. Yéeney Wikipedia mooy jébbal am
ëmbiit mu ubbeeku
, maandu te fugluwu.
Wikipedia ofwel nazi-internet is wereldwijd toegankelijk via een proxyserver, onderhouden door het C'I'A en is een jarenlang opgebouwd naziproject. De proxyserver wordt geturnabout door op de mobiele telefoon te staan van marechaussee 23874. Voor verdere informatie zie: Afdeling Intelligence, Koninklijke Marechaussee
Jaar-jaar
Soppi
soppi gongikuwaay bi
Sémbub Nupedia
Soppi
soppi gongikuwaay bi
Wikipedia ngi jóge ca Nupedia
Nupedia di woon ab sémbub jimbulang bu ubbeeku bu Jimmy Wales sosoon ci weeru gamu atum 2000.
Mboolaay
gu Bomis (gi Jimmy Wales féetewoo woon moomeel gi ci ëpp) moo ko jàppale woon ciy koppar, doon fay Larry Sanger mi jiite woon mbind mi. Waaye Nupedia ag màggam dafa yeexoon lool ba waraloon, ci 2001, Larry Sanger xalaatoon ni sos ab wiki moo doonoon liy man a gaawal yokkteeg jukki yi. Xalaat boobu ñeel jëfandiku xaralag wiki ngir sos ab jimbulang, juroon na ag diisoo ci diggante Larry Sanger ak tëriinkat boobu di Ben Kovitz ngir mu faramfaceel ko ci ni mu gën a leeree ana nan la xarala gu wiki di doxe, ci ab reer ca San Diego la ame woon, ci 2i fan i tamxarit 2001. Ci nii Larry Sanger ni Jimmy Wales ngir ñu jëfandikoo xarala gu wiki ngir sos ab jimbulang bu gën a woyof, lii moo jur sosug jimbulang bu Wikipedia.
Sémbub Wikipedia
Soppi
soppi gongikuwaay bi
Ginnaaw bi ko Jimmy Wales ak Larry Sanger sosee, Wikipedia ngi judd ci kàllaama
waa angalteer
ci 15 tamxarit 2001. Gu
waa faraas
teggu ci 23 gamu 2001, gu waa almaañ tegu ci ak yeneen yépp, ba tay ci atum 2007 mat nañu ñaari-téeméer ak juróom-fukki làkk.
Ci 1 diggi-gamu 2002 la Larry Sanger tekki ndomboy-tànkam ci ñaari sémb yépp, ginnaaw bi Bomis tëyyee loxoom, fayatul Larry Sanger ci liggéey bi mu doon def ci Wikipedia ak ci Nupedia. Ci 26 weeru koor 2003 la Nupedia tëj ba fawwu, Wikipedia moom wéy di màgg.
Boobu ba léegi Wikipedia di dox ci ay àtte yiy askanam tëral ndànk-ndànk jëmug kanamam. ci 20 maami-koor 2003 la Mbootaay gu
Wikimedia
wikimediafoundation.org
) juddu ngir wut ay koppar yu muy suuxate sémbi wikipedia yépp.
Wikipedia Wolof
Soppi
soppi gongikuwaay bi
Wikipedia wolof moom mi ngi sosu ci ndeyi-gàmmu atum 2003, toog daanaka ñaari at te amul benn yëngu-yëngu. Ci tamxarit 2005 la am jukkeem bu njëkk. Xoolal xët wi ñeel
Taariixu Wikipedia wolof
Melokaanu sémbub Wikipedia
Soppi
soppi gongikuwaay bi
Yéeney sémb bi
Soppi
soppi gongikuwaay bi
Ni ñu ko binde ci xët wu njëkk wi, bakkam mooy:«Jimbulang bu ubbeeku bi», maanaam di lu ñépp bokk, te ñépp man cee cëru ngir gënal ko. Jimmy Wales di kenn ci ñaar ñi sos sémb bi, mi ngi koy tekkee niki «ag jéemantu ngir sos ak séddatle ab jimbulang bu ubbeeku ci anam gu mucc-ayib ngir nit ku ne man koo am ci làkku cosaanam».
Melokaani Wikipedia
Soppi
soppi gongikuwaay bi
Baatu «Wikipedia» mi ngi jóge ci taqaleg ñaar yii di «
wiki
» di ag nosteg yoriinu ëmbiitu
dalub web
bu ñu man a soppi jaare ko ci ab
joowukaayub web
, ak «
pedia
» di reenu baatu làkku waa angalteer bii di
encyclopedia
, di tekki jimbulang.
Li ñu jublu ci sémbub Wikipedia mooy mu doon ab jimbulang, maanaan muy jëmmal bépp xameefu nit, lépp lu nit xam man caa ne. Wikipedia du ab
baatukaay
, du am
péncum waxtaanuwaay
(xoolal xët wii ngir xam lu wikipedia doon ak lu mu doonul:
Ndimbal:Ubbeeku
). Sémb bi dafa àddunawu, day laal bépp xeetu xam-xam, bariylàkk, te amul ag pay.
Sémbi wolof yi
Soppi
soppi gongikuwaay bi
Wikipedia ci wolof
Wikiquote ci wolof
Wiktionary ci wolof
Ci «
» lañ ko jële
Wàll
Sémbi Wikimedia Fondation
Jimbulang
Wikipedia
Yokkuw tëriit